Jump to content

User:Ceddo bi

From Wikipedia, the free encyclopedia


Daa mel ni xàle moom; ab yaram mi ngi aju ci doxinu màg ma mu nekkal. Ndàx dëgar bopp gi nekk ci'b xàle; bàyy koo'k boppam rekk a ko def. Bañ boppam gu mu dund lu yàgg yit, xas wu ñaaw wi dëkk ci'b noppam a ko'y waral. Te du màn a xam lu tàx, ndax yëgyëg bi ci xolub xàle, xàm gi ci xel'am màg rekk a ko màn a ràbat. Baay a wàroon a xàm ne kër goo dugg, àm na coow lu léen xañ jàmm, te waa kër gaa ca wàr a teg séenub tànk, ba cow la du fés! Bokk yi! Leeleeg gone gu ndaw; Taxan, yalwaan ak yab yu díis ci'm xelam la ñu ko'y jañ, def ko mu'y yitteem.Tumurankeel ko lool, ne moo baax ci'b yaram. Firnde ji mooy: Baay da ko'y dàlal Al qur-aan ca Daaray sëriñ Cerno ngir mu jànge fa Diine. Boole koo'k mbaaxug ceddo gi mu xam; bëgg ko ko yare. Te bu àmee juróom benn ciy àt; mu dugg jàngub tubaab lu nekk mu dàj. Te Baay yit du xàmmee: ba bu ñëwee ak digg gannaaw gu fees dell'ak i daggdagg, walla dóor tax i waaraamam àmul i we; du ko jële ca jàngu ba. "Xanaa: ne ko jàngoo li ñu la bindal!” Baay xàmul ne: jànglekat yi tubaab, mbaa àraab, la'n gën a xàm; ci askan wii ñu bokk. Ba tax yàrub doxandéem la ñu'y dugal ci xàle. Ndax ñoo'y jàngle “nappoliyoŋ” maam u tubaab, bàyy Njaajaan su nu maam! Jàngal léen ba nu bëgg “ molliyeer ”; bàyy Kocc Barma su nu maam! Ba moo tàx tay jii, ñu gen a gëm “wiktoor igóo”; ci Sëñ Mbay Jaxate mu xereñ ma! Moo léen yóbbe xamadi yit; ba boo léen di wan weer, ñu'y xulli, di xool joxañ ba koy wane. Moo'y úp séen i xel, jaxase séen i xalaat, te tar lool ci ñoom. Moo waral yit jaawale Diiney sunu Boroom yi, ak wax i àraab bi su nu Boroom boole bind. Moo wàral yit ràññee wu ñu naataange, ak nit ku yàlla suturaal. Manu ñoo xàmme wuutee'k nit ku nekk ci lu araam te bon; ak Ceddo bu baax tey jubal. Te sàx moo tax yit; ñu'y topp ñi léen yàr di mbelmbeli ci séen i nopp; ngir feñal la gën a bon ca weneen yoon wa, te di léen gëm loo lu baax li ñu yore, ba mu gënal léen séen bakkan, te jaral leen jël bakkan.

Usmaaan loo waajal.